audio
audioduration (s) 4.84
114
| duration
float64 4.84
114
| transcription
stringlengths 14
1.87k
|
---|---|---|
33.18 | Lii de ay nit lañu, ñoo xamante ne dañoo toog, ñenn ñi dañoo toog sukk seen i bëti wóom, ñenn ñi taxaw, ñenn ñiy dox, mel ni nag dañiy defub peeñu, di feeñal seen mbégte walla ñi feeñal seen naqar. Waaye, ni ñu tàllalee seen i loxo daal, mel na ni ñu daal, ñu ak mbégte, uuhun. Waaye, ñu ngi taxaw ci xàll wu ñuul daal, ci béréb bu yaatu. |
|
18.84 | Lii de ab nataal la boob mel na ne maa ngi ciy gis ay nit ñu bare. Ñu ngi sol ay mbubu yu weex ak i tubéy yu ñuul. Ni ma leen gise nii nag mel na ne am na lu ñuy ñaxtu, am na lu ñuy mettitlu. Ndaxte ñu ngi ci kow ab tali, ñii ngi sukk ñii ngi taxaw tàllal seeniy yoxo. |
|
17.72 | Waaw, lii sunu mbokk yi nekk ci casamance lañ ñuy won. Maa-naam ñi doon def seen manifestation di génn ci kaw mbedd yi, di wone li leen naqari ak seen mettit di ko wone li nekk seen biir xol, donc ci manifestation yi doon romb jamono yee jàll. |
|
22.12 | Nataal bii nag ñoo ngi ci gis lu mel ne sāru layu te ñu defaree ko ak ay bant, ak ay wëñ. Ñu kay defare fii ci Senegaal ak yeneeni réew Afrig. Am na wëñ yu weex, am na yeneen kulëer tamit yu wuute: yu jaune, yu orange, ak yu bula ak yu verte.
Ñuŋ ko teg ci benn taabal tamit bu nu lal lu bula. |
|
12.64 | Ñaari jigéen ñu muuru, ku nekk wan sa moroom gannaaw. Ku ci nekk yaa ngi musóoru musóor gu wute ak sa moroom. |
|
20.48 | Lii de ab nataal la, nataal book. Ay garab a nga ca ginnaaw. Ci ab dex tamit la nekk. Am na taax mu mag a mag te mu nekk ca ginnnaaaw te xoolee ci suuf mel ne daa def ab ecran. |
|
15.48 | Waaw mbokk mi nataal bii de gis naa ci am taax mu kawe ak ndox mu yaatu lool, mu mel ni ab dëkk réewum taax ma nga ca kanamu ndox ma am na ay garab rafet na lool nag, te yànji. Am na taax mu gudd mu fa nekk. |
|
15.74 | Nataal bii nag moom ab fowu moo ci nekk maanaam ab stade, stade bu yaatoo yaatu. Moom nag am na làmp yu bari yu ko wër di tàkk. Làmp yi nag am na ci làmp yu xonq ak yu weex. |
|
15.06 | Waaw lii nag boo xoolee genrub ëmbu la, boo xam ni ay sac ci biir am na ay bouteille, am na daal yu bari yu nekk ci biir yoo xam ni dañ ko cee takk, dañ koo teg ci kaw ëmbu bi. |
|
23.28 | Nataal bi ma jot maa ngi gis ne kudd la. Kudd nag maanaam weŋ la goo xam ne dañ koo yàtt ba mu mën a def ceeb, nga mën ci tibb daal li ngay lekk lu mu mën doon na nga mën si tibb rekk lekk. Waaye daal weñ lañu ko defare...
Wa ilaa mën na doon nikel... |
|
13.58 | Nataal bii de ag kuddu la kuddu. Gis naa ci ag kuddu ñu teg ci kaw lu weex. Nataal bii de li ma ci man a gis ma jàngat ko ci daal kuddu la. |
|
21.1 | Benn kudd la, benn kudd, waaw kudd, kudd, waaw kudd bu gudd waaye guddul noonu.. Teg ko fu weex waaw , fu weex lan ko teg fu weex waaw lépp a weex foofu moom lépa a weex. Am kudd rekkk rekk. Kudd yi niy añe, di ko reere, di ko defee lépp daal, kudd rekk, kudd moom la daal. kudd la daal. |
|
30 | Waaw foto bii nag moom moo ngi wone li ñii tudde kudd , kudd gii nag tudd kii la lekkukaay maanaam nit moo koy tée cib loxoom , ëe... di lekk boo xoolee gudd gu weex tàll la ci jamono jii nga xam ne yeneen wirgo lay am. Kudd gii moom kudd gu weex tàll la. Mën nañ ko defaree nag armiñoŋ walla nikel. |
|
21.4 | Waaaw nataal bii ma jot nag gis naa ne ab néegu ñax la lu mel na sãri ñax waaye suuf gi nii am na ay bant yoo xam ne dan kaa ràbble. Moom nag bunt bi nag defar nañ ko taaral nañ ko ba mu rafet lool. Am na koo xam ni nag mu ngi ci bunt bi ba noppi am na koo xam ne day génn nii. Waaye fële ci ginnaaw nag am néegu ñax la ba noppi am ay garab ak yooyu. |
|
28.42 | Mel nee... Nataal gii ñu jot ëe... Maa ngi gis mu nekk am néegum ñax waaye nag bii dafa taaru lool maasàllaa! Mel ni itam maa ngi gis góor gu taxaw nii ci buntu bi, am it ku taxaw nii ci buntu bi waaye it buntu bi dafa.... dafa gàtt lool dafa ubbéeku. Waaw mel na ni itam am na beneen néegu ñax gu nekk nee ca wet ga. Waaye it fa mu nekk dafa rafet lool am na ay garab yu bari yu ko wër. |
|
33.28 | Waaw ñu ngi gis ci nataal bi benn néegu ñax bu mag a mag boo xam ne dañu ko ràbb daldi ci teg ëe ñax. Njubb ba jëm ca kaw. Ca bunt ba nag ñuŋ ko def benn ëe "décoration" bu rafet, bunt ba ubbéeku am ku fa taxaw. Ci beneen wàllu càmmooñ bi nuy jàkkarlool ci nataal bi ñu ngi gis benn nit mu taxaw.. |
|
21.64 | Waa nataal bii nag moom ci dëkk àll yi la dëkk àll yi waa. Nga xam ne lii ab néegu ñax la ëe néegu ñax bu nu defaral bunt ci wetam. Am na garab gu ci nekk waaw ci genn wet gi. Ci geneen wet gi tamit amaat naa tamit ay garab yu nekk foofu. Muy néegu ñax boo xam ne dafa am jubb bu gudd ci kaw. |
|
14.5 | Lii may gis de ay garab la ak ay néegi ñax ak benn xale bu ndaw buy dox ci suuf si. Lii féete kaw nag asamaan si la. |
|
24.7 | Ñu ngi gis ci nataal bi benn néegu ñax. Ci bunt néegu ñax bi benn xale bu jigéen ak benn garab bu nekk di digg kër gi, ci ëtt bi. Am beneen "bâtiment" bu féete ci geneen wàll ga ak ay"bagages" kër yoo xam ne ñoo nekk ci bunt néegub ñax bi. |
|
14.42 | Néegub ban bun dëpp aw sàkket dëse ko aw ab yéen, suy ko suy bu xonqu, li ko wër lépp nag di am ñax mu vert. |
|
21.84 | Nataal bii maa ngi ciy séen néeg boo xam ne dañu ko tabaxe ay ban yu nu def ay bant ci biir. Néeg bi danu ci dawal seng. Ab seng lanu ko xàdde. Am na ñax mu nekk ci wetam moo xam ne danu ko bay ngir mu set. |
|
4.84 | Lii de gejje la, gejje, gejje. |
|
18.56 | waaw kay, lii nag ab nataal la. nataal bi nag gis naa ci gejji. gejji gi nag ëe... gejji bër la. gejj gi nak am na... ci gejji la... la... ci kaw gejji la nekk. |
|
30.32 | Nataal bii nag day wone ab tabax bu àggagul maanaam tabax bu ñuy mottali. Ay muul yu xonq lañ kay tabaxee . Am na beneen sax bu nu teg ci kaw moom lañii wax beneen etage bu ñuy teg ci kow dan koo tàmbali rekk suuf saa ngi nii , dink yeek Yeneen muul yi tée dink yi ngir mason bi mën a taxaw, taxaw ci kaw dink yi ngir mën a jot ci kaw. |
|
15 | Nataal bii nataal boo xam ni ay néeg lay wone. Am na ay ñax yu bare ak i garab yu nekk ci wet gi. Daa mel ni kenn dëkku fi. Loolu lay nuru. |
|
28.4 | Maa ngi gis ci nataal bii ab dëkk boo xam ne bii, dëkk bu naat la. Dëkk bi nag, am na ay naataange. Am na ay tabax yoo xamantane bii tabaxi cosaan la, muy ay xur ak i montaañ. Ci noonu la ñu dëkkee. Kon dëkk bi, boo ko gisee rekk da ngay xam ni dëkku cosaan dëgg la. |
|
13.66 | Waaw nataal bii nag gis naa ci ab fu yaatu foo xam ne nii ab toogukaay ñoo fa nekk, ñetti toogukaay ak taabul. |
|
13.54 | Nataal bii de ay garab la mooy garab yooyu nga xam ne day faj. Mu am ci tollook juróom ba noppi ñu laxas leen ñu laxas yépp. |
|
19.76 | nataal bii ab lal moo ci nekk. lal bi, am na ñaari ñegenaay yuñ ci teg. boo xoolee ci suufu lal bi am na luñ ci lal, moquette la. néeg bi nag, da ñoo ubbi fenêtre bi. mu nga nee ñu ubbi, moo tax dafa leer. keen nekkufi nag moom, waaye ay godaar rekk ñoo fi nekk. ak na ay kamood ci wetu lal bi. |
|
21.92 | Lii nag nataal la boog. Mbir la moo xam ne dafa bindoo mbindin mu mërgëlu waaye dafa mel ne dañu koy dagg. Am na sax lu ñu ci daggee ba teg ko ci wet gi. Dagg wu rafet la. Moom nag dafa weex. |
|
15.82 | Lii nag nataal la boo xam ne li ci nekk mooy bunt, di ab jaarukaay boo xamante ne sii nit ñi ci lañuy jaar di dugg ak a génn. Bunt nag daa mel ni bunt bu xaw a kii la. |
|
15.68 | Nataal bii ngeen ma yónnee de gis naa ci biir nataal bi ab palaatu dénk buñ teg. Teg lu mel ne ca kaw bool ba lu xonqu, tegub kaas xelli ca lu mel ni lu xonqu. |
|
13.62 | Nataal bii nag benn buntu lay wane, buntu bi nag dénk lañ ko defare. Mel na ni nag yeneen yi nekk ci wet gi yépp dénk lañ koy defare. Jot naa ko cee seetlu daal xool naa ko bu baax a baax waaye noonu la. |
|
14.62 | Nataal bii nga xam ne nataalub puj la, bu..... |
|
15 | Lii ab pot la bu def chocolat. Mu jël ag kuddu tibbu ci yékkati ba ci kaw di ko ci sottiwaat, am na ay yëf yu ko wër. |
|
21.68 | Salaamaalekum!
Fii de ab benn ñam la buñ naan bëer. Mu ngi nii ñu xaaj ko mu tollook ñetti xaaj. Benn paakaa ko xaaj. Paaka bi am ñaari cat : benn cat bi weñ la beneen cat bi dénk la.. |
|
10.7 | Waaw nataal bii de gis naa ci bëer, bëer bu ñuy dagg, gis ci paaka. Jot na caa dagg sax ñaari dagg am yum xoos wàcce ci suuf. |
|
21.06 | Nataal bii nag maa ngi ciy janook bëer bu nuy dagg. Mel na ne bëer bu mag la bu nuy dagg ay pàcc ni ma ko gise nii ci nataal bi. Bëer bi nag nu ngi koy wax bëeru dagg. |
|
26.64 | Waaw lii ab pañe la buñ ràbbee bant. Ñu ràbb ko nag ëe ràbbin wu xarala wu rafet ba bare wutal ko ag njàpp. Am lu ñuul luñ takk ci njàpp gi. Pañe bi nag mu yor wirgo wu puur rafet lool. |
|
22.36 | Nataal bii ngeen ma yónnee de gis naa ne benn taabal la. Taabal boo xamente ne bii ci kaw dénk la waaye ci suuf tamit dénk bu weex la. Ci kaw dénk bu sokolaa la waaye ci suuf dénk bu weex la. Gis naa ag gàncax gu naat a naat. |
|
21 | salaamu ãleykum! waaw lii de, di nañ ci gis ,benn buntu,benn buntu. Buntu boo xamanta ni li ko wër dénk la, waaye li nekk ci biir verre la. mu am fenn fuñ naan poigné, nga xam ni moom lañ koy tijee. moom mu ngi yor couleur bu ñuul. waaye ci kaw buntu bi de, boo xoolee dinañ fa gis benn làmp. |
|
10.7 | Nataal bii day wane benn kër gu rafet goo xamante ne dafa am ay buntu yu rafet yu mel ni verre, carreaux yi tamit weex tàll ba noppi rafet leer nàññ kër gi. |
|
17.92 | Nataal bii may gis nag dafa mel ne attaaya la mu nekk ci kaasu weer ab xobu naanaa bu wert bu naat nekk ci wetam. Fi mu nekk nag dafa weex tàll. |
|
23.6 | Waa nataal bii moom ay bunti feer la. Maanaam ñi nga xam me menusier, mécanicien yi, "menuisier métalique yi" nekk fii ñoo koy defar ci Senegaal gii mën nañu ko lool. Waaw "mécanicien" yu xereñ sax la ñoo xam ne ay bunt yu rafet. Bunt yi mu ngi nekk bunt yoo xam ne yu "gris" la. Am na tamit ay palanteer yoo xam ne nii pour bu ngelaw li dee dikk dina si mën di jaar. Bunt yoo xam ni de bari la ñu tegle ko. |
|
14.02 | Nataal bii de ab lal la, lal la boo xam ne nag dañ koo liggéeye weñ weñ. Waaye jàppukaay yi dénk la ba noppi ñu peinture peinture bu chocolat waaw mu am ay yu wóor daal yoo xam ne boo ci tëddee doo am benn gàllankoor. |
|
28.58 | Waaw nataal bii boo dee xool dangay gis ne ñetti néegi ñax la yu bokkul nin leen jële. Benn bi dan ko jël ci biir ,. ñaar yi ci des ñu jël leen ci bitti. Benn bi am ak nit ku nekk ci kaw sol tubéy bu wirgo wi nëtëx. Dinga gis tamit ay garab ci benn nataal.. |
|
30.16 | Nataal bii nag ay toogu lay wane. Mën nañ ci gis juróom-benni-toggu . Toogu nag bu ci nekk am na ñenti tánk te tànk yi dañoo "beige". Toogu yi dañoo ñuul kon toogu yi ñaari wirgo yooyu la boole muy wirgo wu ñuul, ak wirgo bu beige. Fiñ leen teg nag "bërëb" bu Weex la. |
|
34.22 | Lii de ab kaas la, nataal bii ab kaas lay wane, kaas bu ànda ak lu muy àndal, kuddu beek, ak palaatam, palaat, palaat bu ñuy teg kaas bi. Léegi nag, palaat kii bi nag, kaas bi nag mi ngi yor ci biir ñamu suukar, boobu ñu naan sokolaa, ñamu suukar boobu ñu naan sokolaa moo ci nekk ak beneen bu weex boo xam ne xawma, xawma lu mu doon sax ndax image bi dafa xaw a floue. |
|
28.08 | Lii ab marmit la bu am kubéer. Marmit boo xam ne mënees na ko jëfandikoo ci wàllu togg, mënees na cee togg, mënees na cee tàngal ndox walla nga baxal ko ci ëe mën na yu bari daal ci wàllu togg. |
|
30.38 | Nataal bii maa ngi ci janook ay bool, ay kudd , ay bool yu bare ak ay kudd yu bare moom laay janool nii ci nataal bi ma tiim. Moom bool yi nag ak kudd yi xam naa "pour" lekk moo ko tax a jóg. |
|
14.98 | Lii ab furno la buñ teg, teg ci ab marmey, mel ni koy togg. Am na ku nekk Nale wet ga. Ab baŋ nekk ci wetam. |
|
22.98 | Nataal bii ab ab ab and moo ci nekk. |
|
10.54 | Nataal bi ngeen ma yónnee nii ab taalukaay la boo xam ne dañ koo liggéeye ci ban. Man naa taal feuille man naa taal matt. |
|
22.26 | Foto ñaar fukkeel bi ak benn maa ngi ciy gis lu mel ne ay defukaay maanaam ay bool, bool yi tamit booli nikkel la. Am nañu kulëer bu gris. Juróomi bool la ndax ñent ñoo nekk ci suuf, benn bi nekk fële ci kaw. Ëe li wër bool yi mel ne lu weex. |
|
24.46 | Nataal bi de ay layu la. Gis naa si ay layu ak li nga xam ne mooy ay bool. Layu yu mag ak yu ndaw. Am layu yoo xam ne dañu bari wirgo. Layu yu rafet. Bool yi tamit gis naa si yu mag ak yu ndaw tabarkàlla. |
|
14.58 | Ab taabal la bu rafet boo xam ne yamul ci benn couleur. Waaye dafa mel ni dañ koo defar tegle ko ba mu rafet, yamul sax ci benn ñett nag la may nuru. |
|
16.66 | Ci nataal bii ay cempataŋ moo ci nekk, cempataŋ nag mooy table. Waaye table yii ay table verre la am na deux places tegukaay. Boo xoolee daal table verre la yii daal ku ko tegoon ci kër goo xam ne dafa am gone yu ëppal dinañ ko toj. |
|
20.8 | Nataal bii de am mburu la. Mburu mi nag xemmeeme na lool sax axaa ! Xam naa moom boo ko joxee ñaŋeen yi dana baax ci ñoom moom waawaaw. Am na solo lool sax waawaaw. Aa am na miir bu seex bu ko wër. |
|
19 | Nataal bii ay laltu la yu ñu ràbbu ci lu deme ni ki xànc, ñax...aha. muy liggéey bu xereñ nag! Bu xereñ lool sax! |
|
13.36 | Lii de benn dëkkuwaay bu nekk ca Siin la, tollu ci fukki bâtiment. Ñu tabax ko ci ñeenti waxtu ak juróom fukki simili ak ñeent. |
|
12.06 | Lii de daa mel ni am taax la, taax mu kawee kawe dend ak ay garab. Maanaam lu mel ni immeuble daal la dend ak ay fleurs walla jardin daal. |
|
13 | Lii ab toilette la, toilette, ab toilette la. Bu jëkk bi mooy duusu cappu la quoi. Beneen bi moom mooy pour sàngu bi. |
|
84.4 | Juróomeelu nataal maa ngi ci gis fii dafa mel ni ay duus la gis naa ci duus boo xam ni dafa am sãs sãs sãs bu bula gis naa ci ab palanteer boo xam ni palanteer bi dafa am lu weex lu ko wër jëmmi weer bi dafa mel ni dafa ñuul gis naa ci it fu ñuy deme wanag nga xam ni lépp dafa weex gis naa ci it mouchoir dafa tegu ci kaw lavabo bi ba pare jëmmi mouchoir dafa weex ci lim tegu it dafa weex trait yi ko wër it trait yi dafa mel ni dafa xaw a soon am ay couleur yu weex. Beneen wanag wi ci des beneen wanag wi ci des dafa am ay carreaux yoo xam ni carreaux yu weex la du ay carreaux yu marron fii ñiy fi nga xam ni foofu lañuy deme wanag it foofu lépp dafa weex tàll ay carreaux ñoo ko wër beneen bi ci des it fi ñiy deme wanag it lépp dafa weex am na lu mel ni ag weñ da caa sampe carreaux yi ko wër it dañoo weex waaye...def bula. Beneen bi ci des it gis naa fi salle de bain boo xam ni gis naa fi ab sãs waaye nag boppu sãs bi génneewuñ ko waaye fiñ koy ubbee pour ndox mi ñëw foofu gis naa ko gis naa it benn affaire boo xam ni dañ ko taf ci kaw nii mu xaw a xaw a tolloo mu xaw a tollook fi kii wu fi sãs bi sãs bi tuuti nii carreaux yi it carreaux yi carreaux yu marron la. |
|
13.6 | Waaw lii de dafa mel ni asamaan su xiin la ba ñuul. Ma gis tamit ci wet gi lu mel ni am taax moo xam ne ña nga ko peinture peinture bu soon ak bu ruus ak bu ñuul. |
|
15.74 | Ay nit ñu bari lañ. Ñoo ngi taxaw sol seeni tiset bu bëlë ak tubéy bu ñuul, ak seeni dàll yu ñuul. Dañoo taxaw. |
|
23.18 | Nataal bii de Abdulaay Wàdd la. Mooy feeñ fii ak estaad biñ ko tuddee. Mooy fi nga xam ni foofu la ñuy futbalee. Waaw maa ngi gis ay suis itam. Maa ngi gis estaad Abdulaay Wàdd. Moom it góor bég na lool lool, ak reetaan gu neex gi. |
|
14.84 | Ñii de ay policier yu bari lañ, ñi ngi sol benn tubéy bu ñuul ak ben tiset bu bula. Fiñ nekk yaatu na lool, nit ñu baree bari lañ. |
|
25.16 | Nataal bii lii cere la. Cere ju am ñeex mu nu defar. Xam naa ñeexum tamaate walla yu ni deme. Am ci biir nag ay lujum, ay lujum yu bari waaye mënu maa jàpp yépp. Waaye daal xam naa yu mel ne ay xeetu pataas, ay ñämbi ay seen karoot yooyu ñoo si nekk. |
|
15.72 | Waaw ñii de dafa mel ni ay jigéen lañ yoo xam ne ñi ngi sol seen i tenue. Ñi ngi meloon ne daal jigéen ñi nga xam ne bokkoon nañ ci quatre (4) Avril bi daan ñëw fee ca place de l'indépendance pour fêté ko. |
|
22.32 | waaw ñii ay sóobere lañ.ñoo taxaw nii am ku ñëw di leen nuyu ñu taxaw ñoom ñëpp ne tekk, keen yenguwul. xam naa ni nag seen njiit la. am na it ku topp ci ginnaawam di ko saytu. |
|
23.7 | Maa ngi gis ci nataal bi ceeb. Ceeb bi nag ëe ceeb bu weex la. Ñoo def bëjëg ca kaw. Am kudd guy tibb. Kudd gi nag kudd gu ñuul kukk la. Ab loxoo ko téeye. |
|
25.48 | Waaw lii nag jenn jigéen la. Jigéen joo xam ne ab pólisee la. Mu ngi sol yére pólisee ak mbaxana pólisee bu xaw a bula. Bu bula nii. Fi mu nekk nag am na benn garab bu mu dendal. "Village" bi mu nekk rafet lool. Am na benn oto bu nekk ci wetam nële ci wetu garab ga, oto bu weex. Loolu mooy li nga xamente ne gis nanu ko. |
|
24.22 | Waaw nataal bi dangay gis ne maanaam ab palaat la boo xam ne dañ cee def maanaam aw ñam. Ñam woo xamante ne nag mu ngi nekk laax ñu def si soow mu weex, def si ay "raisin", yoo xamante ne bii ñu ngi si kaw. "Raisin" yu bari bari ñu ngi si biir, ñu ngi ci kaw ñam wi , ak ay maanaam raisin... |
|
13.62 | Waaw lii nag ñaari soxna la yu taxaw ak ku góor. Ñaari soxna yi sol ay waksi ku góor kiñ taxawal mel ni seen boroom kër. |
|
21.94 | Fii moom ay mbooloo mu bari laa fi gis..waaw mu mel ni lu xaw a pënd. Am ku yor loxoom nii di sànni.. Xam naa ñàkkul am na lu leen naqadi. Dama jàppoon dañiy kaas seeni kii, seeni, seeni "droit". |
|
12.28 | Ñii ay takk-der lañ sol seeniy yére, mel ni am daa lu ñuy xëccoo daal waaye ay takk-der lañ. Ñi ngi nii am ñu seen ginnaaw am ñu leen jiitu, mel ni daa am lu ñu jàppoo. |
|
17.92 | Nataal bi ngeen ma mujje yónnee, muy juróom-fukkeel beek juróom ñett, maa ngi ci gis yàpp walla ndawal loo xam ne dañ koo togg ba noppi. Toppatoo nañ ko ba mu mel nim war a mel, nu war koo jëfandikoo. |
|
12.94 | Waaw nataal bii ab woto la bu am ay alkaati, ñii dañoo toog, ñee taxaw, ñu mel ni daa am ñu yor ay gànnaay. |
|
12.92 | Lii tamit de dafay wane ay nit ñu bari ñoo xam ne ñoom ñépp ñoo bokku fiñ nekk. Am na ñoo xam ne dañoo tëdd ñii toog ñee taxaw. Mu mel ni am na ci ñoo xam ne daal dañoo sonnu lool. |
|
15.84 | Gis naa fi ay nit yu baree baree bari yoo xam ne daa mel ni dañoo nekk ci fiñ leen tëj ci ab néeg. Kenn solu ci ay yére yaramu neen lañu def. |
|
10.78 | Nataal bii gis naa ci biir nataal bi ñaari dénk yuñ teg benn bi am lu guddu. |
|
13.28 | Nataal bii de, nataal la boo xam ne ab machine la, machine boo xam ne dañ koo teg noonu. Mooy xeetu machine yooyu nga xam ne moom lañuy faje moo ci nekk. |
|
14.62 | Sama nataal bii ñu ma yónnee dafa mel ni ag téléphone fixe lay nuróol, mu am ay chiffre bouton yoo xam ni ci la chiffre yi di ne nga man a composé. |
|
25.5 | Foto bii maa ngi ciy gis ay niy yu bari. Ñu daldi def,... Am benn grup bu toog ci ginnaaw, am kenn koo xamante ni moom rekk moo toog fee. Am keneen koo xamantane nii moom moo toog fii ak doomam ak benn faam boo xamntani moo ko tiim, daaldi muuru muuraay bu ñuul, ñu teg ay sées ci biir ndox mi daaldi ciy toog |
|
37.96 | Lii de ab nataal la bu def ab télé bu mel ca melokaan yu jëkk ya yu yàgg ya li ko wër dafa am na melokaan yu chocolat am nab ab ñaari ab taalukaay ñaar yu xaw a niroo yu ne ci kawam am ñaari weñ yu ne ci kawam benn bi jëm nii benn bi jëm nee. |
|
35.42 | Lii de ab tele la. Xaw a ... Tele yu xaw a yàgg tuuti. Am na ñaari onde muy ñaari jàppukaay ba fu nuy yokkee ak fu nuy wàññee, am na ñaari buton yu nekk ci wet gi. Moom nag dafa paan, su paane lii lay génne ay kulëer bula, ak "rouge", ak "rose", ak "jaune claire" ak "jaune foncée" tuuti, ay ñuulak, weexag...
Bëri na ay kulëer daal. |
|
23.78 | Waaw lii domadaa la, domadaa, ñànkataŋ domadaa. Domadaa bi gis naa ci bulet, am na kaani, ñàmbi, karoot waaw domadaa ak limoŋ. |
|
15.86 | Nataal bii ñu ma yónnee gis naa ci benn waay bu jël ay loxoom teg ko ci ab machine ordinateur, boo xam ne bii casque yaa nga tege ca wet ga, akub téléphone it bu mu teg ci wetam ci wetug ndey-jooram. |
|
17.04 | Waaw lii ngay jàkkarlool, benn machine la bu ordinateur. Machine bi nag bu bu clapet la, am na benn waay boo xam ne moo nga toog jël ñaari loxoom teg ko ci bouton yi. |
|
13.62 | Gis naa ne benn nit la boo xamante ne dafa jël ay baaraamam teg ko ci kaw bitõ yoo xamante ne bitõ ordinatéer la. |
|
21.38 | Lii xeetu jollasu la ci jollasu yu njënk ya. Bii nag mu ngi tudd Noki Nokia. Ñu ngi fësal ci ngiska li ab màndarga ak ay waxtu ; waxtu wi mu toll. |
|
19.76 | Nataal bi ma jot de gis naa ne ay airpod la. Waaw ay airpod la yu weex waaw. Dafa mel ni nag dañu genn mooy déglukaay yi yu weex. |
|
16.96 | Salaamaalekum, lii de ab nataal ab nataal la ay kartaabal yu ñu lëkkaloo yu am ay melo; am na xonq, am na ñuul, am na weex, am na mboq, am na dóom-taal, am na wert. |
|
15.1 | Nataal bii moo ngi wone ay jumtukaay yuy tax nit ki mën a xam fu ak nit nekk. Fu waay mën a nekk mën na ko xam daal. |
|
14.72 | Lii de ag lekk la mi ngi doon sumpu-kànja ñu gën koo xam ci Senegaal ñu koy toggu ci kànja ci ceebu ñànkataŋ. |
|
22.88 | Nataal bi ma jot de gis naa ne telegram lan koy wax telegram. Moo ngi nekk ci telefon bi waaye nag ca ginnaaw gis naa ne am na yeneen telegram yu fa nekk. Telegram nag ab application la boo xam ne dañ ciy déggante, jàppandal ak déggante waaw. |
|
22.32 | Waa nataal bii nag ëe mu ngi wone ëe xarala yu yees yi. Bokk na ci ag jollasu goo xam ne ëe ëe mu ngi tàkk waaye jëfekaay gii di imo nga xam ne dañii wone mën naa dem ci jollasu gi, ëe bokk na ci li nga xam ne moo feeñ ci nataal bi. |
|
25.42 | lii de ag jollosu la. lii de ag jollosu la. lale may séen ci biir nag ,kii di ko wàccee nee, ag jëfekaay la gu ñuy wax Watsap. jëfekaay la bu am solo goo xam ni dees koy jëfandikoo ci yu baree bari. ta it dey yombal dem bi ak dikk bi ci wàllum jokkalante. ndax man naa toog fii di jokkook koo xam ne mu nga ba bitim réew, ñuy gisanteek yëpp te du jar may jóge fi ma toog. |
|
33.22 | Lii de yore na ñaari melo, melow yéet la gën a joxe. Melow déet la la jox walla melow jën. Waaye yéet la gën a ndiru. Yéet ñu di ko jëfandikoo, di ko tagge. Bari na ay njariñ sirtu ci ceebu jën, walla ci yu demee noonu, ñoom yaasaak di ko ci rusi, di kitogge. Moom yéet, maanaam fayteef yu juge ci géej la bokk, Firisi de meer yi. |
|
15.92 | Nataal bii yéet la. Gis naa ci yéen, yéet jóob. Mu am ñaari kulëer, ku lëer bu ñuul ak soon |
End of preview. Expand
in Dataset Viewer.
README.md exists but content is empty.
Use the Edit dataset card button to edit it.
- Downloads last month
- 61